마태복음 1장 월로프어 신약
- 1 Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
- 2 Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;
- 3 Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram;
- 4 Aram Aminadab; Aminadab Nason; Nason Salmon;
- 5 Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Isayi,
- 6 miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri;
- 7 Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf;
- 8 Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas;
- 9 Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiya;
- 10 Esekiya Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas;
- 11 Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.
- 12 Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel,
- 13 miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor;
- 14 Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd;
- 15 Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba;
- 16 Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.
- 17 Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
- 18 Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
- 19 Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woona weer. Mu nara xàccook moom ci sutura.
- 20 Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
- 21 Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
- 22 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
- 23 «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
- 24 Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
- 25 Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.