마태복음 15장 월로프어 신약
- 1 Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko:
- 2 «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.»
- 3 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen itam lu tax ngeen di moy li Yàlla santaane, ngir topp seeni aada?
- 4 Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.”
- 5 Waaye yéen dangeen ne: “Ku wax sa ndey walla sa baay: ‘Li ngeen wara jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,’
- 6 kooku amatul warugaru teral baayam.” Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada.
- 7 Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan:
- 8 “Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma.
- 9 Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”»
- 10 Noonu Yeesu woo mbooloo mi ci moom ne leen: «Dégluleen te xam:
- 11 du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.»
- 12 Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?»
- 13 Yeesu ne leen: «Garab gu sama Baay bi ci kaw jiwul, dees na ko buddi.
- 14 Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb.»
- 15 Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.»
- 16 Noonu Yeesu ne ko: «Ndax ba tey seen xol dafa tëju, yéen itam?
- 17 Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu?
- 18 Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe.
- 19 Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga.
- 20 Yooyu ñooy indil nit sobe, waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe.»
- 21 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon.
- 22 Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.»
- 23 Waaye Yeesu waxu ko dara. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.»
- 24 Yeesu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xari bànni Israyil yu réer.»
- 25 Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!»
- 26 Yeesu ne ko: «Jël ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
- 27 Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.»
- 28 Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa.
- 29 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, ñëw ci weti dexu Galile; mu yéeg ca aw tund, toog fa.
- 30 Ba mu fa nekkee, nit ñu bare ñëw ci moom, indaale ay lafañ, ay làggi, ay gumba, ay luu ak ñeneen ñu bare. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, mu faj leen.
- 31 Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil.
- 32 Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.»
- 33 Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?»
- 34 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.»
- 35 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf.
- 36 Mu fab juróom ñaari mburu yi ak jën yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ñu séddale leen mbooloo mi.
- 37 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale juróom ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
- 38 Gannaaw jigéen ñi ak gone yi, góor ñi ci lekk matoon nañu ñeenti junni.
- 39 Noonu Yeesu yiwi mbooloo mi, dugg ci gaal, ñëw ci wàlli Magadan.