마태복음 20장 월로프어 신약
- 1 «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu reseñam.
- 2 Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg posetu denariyon, door leena yebal ca toolam.
- 3 Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu.
- 4 Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.”
- 5 Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu.
- 6 Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?”
- 7 Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.”
- 8 «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujja ñëw, ba ci ñi fi jëkk.”
- 9 Noonu ñi mu jël ci tàkkusaan ñëw, ku nekk jot posetu denariyon.
- 10 Gannaaw ga nag ñi mu jëkka jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon.
- 11 Bi ñu ko jotee nag, ñu tàmbalee ñaxtu ca boroom kër ga,
- 12 naan: “Ñi mujja ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.”
- 13 Waaye boroom kër ga ne kenn ci ñoom: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon?
- 14 Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujja ñëw, li ma la fey yaw,
- 15 ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?”
- 16 Noonu ñi mujj ñooy jiituji, ñi jiitu ñooy mujj.»
- 17 Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii:
- 18 «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee,
- 19 jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
- 20 Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn.
- 21 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu ne ko: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndijoor, ki ci des ci sa càmmoñ.»
- 22 Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu ne ko: «Man nañu ko.»
- 23 Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndijoor mbaa sama càmmoñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.»
- 24 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu, ñu mere ñaari doomi ndey ya.
- 25 Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di not.
- 26 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgga nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga,
- 27 te ku bëgga nekk njiit, na nekk seen jaam.
- 28 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
- 29 Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko.
- 30 Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
- 31 Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
- 32 Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?»
- 33 Ñu ne ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.»
- 34 Noonu Yeesu yërëm leen, laal seeni bët, ñu daldi gis ca saa sa, topp ci moom.