마태복음 22장 월로프어 신약
- 1 Gannaaw loolu Yeesu nettali leen beneen léeb ne leen:
- 2 «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur buy waajal céetu doomam ju góor.
- 3 Noonu mu yónni ay surgaam, ngir ñu woo gan yi ca céet ga, waaye gan yi bëgguñoo ñëw.
- 4 Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ”
- 5 Waaye ba tey wuyuwuñu ko; ñu dem, kenn ki ca toolam, kenn ki jaayaani,
- 6 ña ca des jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen.
- 7 «Noonu buur mer, daldi yónni ay xarekatam, ngir ñu rey bóomkat yooyule, lakk seen dëkk.
- 8 Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Reeri céet gi noppi na, waaye ñi ñu woo yeyoowuñu ko.
- 9 Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.”
- 10 Noonu surga ya génn ca yoon ya, boole ña ñu fa gis ñépp, ñu bon ña ak ñu baax ña, ba néegu reer ya fees ak ay gan.
- 11 «Bi nga xamee ne buur bi dugg na nag, ngir seetsi gan yi, mu gis fa nit ku solul mbubb mu ñu wara sol ca céet ga.
- 12 Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig.
- 13 Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.”
- 14 Ndaxte ñi ñu woo bare nañu, waaye ñi ñu tànn barewul.»
- 15 Booba Farisen ya dem gise, ba xam lu ñu wara def, ngir fiir Yeesu ci waxam.
- 16 Noonu ñu yónni ci moom seeni taalibe ak ñi far ak buur bi Erodd ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
- 17 Wax nu nag loo xam ci lii: ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet?»
- 18 Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi?
- 19 Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon.
- 20 Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?»
- 21 Ñu ne ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
- 22 Bi nga xamee ne dégg nañu loolu, ñu waaru, bàyyi ko, daldi dem.
- 23 Bés boobale ay Sadusen ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom gëmuñu ne ndekkite am na. Noonu ñu laaj ko naan:
- 24 «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.”
- 25 Amoon na ci nun nag juróom ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba am jabar ba noppi, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom.
- 26 Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom ñaareel ba.
- 27 Gannaaw ñoom ñépp, jigéen ja faatu.
- 28 Bu ndekkite taxawee nag, jabaru kan lay doon ci juróom ñaar ñi, ndaxte ñépp jël nañu ko?»
- 29 Waaye Yeesu ne leen: «Yéena ngi cig réer, ndaxte xamuleen Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla.
- 30 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
- 31 Te lu jëm ci ndekkitel ñi dee, xanaa masuleena jàng la leen Yàlla waxoon ne:
- 32 “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.»
- 33 Bi nga xamee ne mbooloo ma dégg nañu loolu, ñu waaru ndax li mu jàngle.
- 34 Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje.
- 35 Noonu kenn ci ñoom, ka nekk xutbakat, fexe koo fiir. Mu laaj ko:
- 36 «Kilifa gi, ban ndigal moo gëna màgg ci yoonu Musaa?»
- 37 Yeesu ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.”
- 38 Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane.
- 39 Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”
- 40 Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.»
- 41 Bi Farisen ya dajee nag, Yeesu laaj leen:
- 42 «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.»
- 43 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne:
- 44 “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor, ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
- 45 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
- 46 Ci kaw loolu kenn manu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara.