마태복음 25장 월로프어 신약
- 1 «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba.
- 2 Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel.
- 3 Ñi ñàkk xel nag fab nañu seeni làmp, waaye fabaalewuñu diw;
- 4 waaye ñi am xel ñoom fab nañu seeni làmp, fabaale diw ciy njaq.
- 5 Ni boroom séet bi yéexee ñëw nag, ñépp gëmméentu bay nelaw.
- 6 «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.”
- 7 Bi ko janq ya déggee, ñu jóg, defar seeni làmp.
- 8 Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diw, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgga fey.”
- 9 Waaye ñi am xel ne leen: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen. Tee ngeena dem ca jaaykat ya, jënd?”
- 10 «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba agsi. Ñi amoon diw ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj.
- 11 Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!”
- 12 Mu ne leen: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.”
- 13 «Yewwuleen nag, ndaxte xamuleen bés ba mbaa waxtu wa.
- 14 «Te it nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi muy laata dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam, ku nekk lu mu àttan.
- 15 Kenn ka, mu dénk ko juróomi milyoŋ, keneen ka, mu dénk ko ñaar; ka ca des, benn; daldi tukki.
- 16 «Bi mu demee nag, ki jot juróomi milyoŋ ya dem, di ci jula, ba amaat yeneen juróom.
- 17 Noonu it ki jot ñaar amaat yeneen ñaar.
- 18 Waaye ki jot benn milyoŋ dem, gas pax, nëbb fa xaalisu njaatigeem.
- 19 «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya délsi, daldi leen laaj alalam.
- 20 Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.”
- 21 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
- 22 Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.”
- 23 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
- 24 «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul.
- 25 Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.”
- 26 Waaye njaatigeem ne ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul,
- 27 kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya. Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot li ma moom ak la mu jur.”
- 28 Noonu njaatige bi ne: “Nanguleen xaalis bi ci moom, jox ko boroom fukki milyoŋ yi.
- 29 Ndaxte ku am dinañu la dolli, ba nga barele, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
- 30 Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.”
- 31 «Boo xamee ne Doomu nit ki mu ngi ñëw ci ndamam, ànd ak malaaka yépp, booba dina falu ni buur, toog ci jalam bu soloo ndam.
- 32 Bu boobaa dees na dajale xeeti àddina yépp ci kanamam, te dina leen xàjjale, ni sàmm di xàjjalee xar yi ak bëy yi,
- 33 mu teg xar yi ci ndijooram, bëy yi ci càmmoñam.
- 34 «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndijoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina.
- 35 Ndaxte xiifoon naa, ngeen jox ma, ma lekk; te mar, ngeen jox ma, ma naan; nekkoon naa ab doxandéem, ngeen fat ma;
- 36 te rafle, ngeen wodd ma; woppoon naa, ngeen seetsi ma; te ñu tëj ma, ngeen ñëw fi man.”
- 37 Ci kaw loolu ñi jub dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, nu jox la, nga lekk; mbaa nga mar, nu jox la, nga naan?
- 38 Kañ lanu la gisoon, nga nekk ab doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la?
- 39 Kañ lanu la gisoon, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu ñëw ci yaw?”
- 40 Noonu Buur bi dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gëna ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
- 41 «Gannaaw loolu dina wax ñi ci càmmoñam: “Soreleen ma yéen ñi alku, te dem ci sawara su dul fey, si ñu sàkkal Seytaane ak ay malaakaam.
- 42 Ndaxte xiifoon naa waaye joxuleen ma, ma lekk; te mar waaye joxuleen ma, ma naan.
- 43 Nekkoon naa ab doxandéem, waaye fatuleen ma; te rafle, waaye wodduleen ma; woppoon naa te ñu tëj ma, waaye seetsiwuleen ma.”
- 44 Ci kaw loolu dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?”
- 45 Kon dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gëna ndaw, man ngeen ko defalul.”
- 46 Noonu ñii dinañu sóobu ci mbugal gu dul jeex, waaye ñi jub dinañu tàbbi ci dund gu dul jeex.»