마태복음 28장 월로프어 신약
- 1 Gannaaw bésub noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba.
- 2 Fekk suuf yëngu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw.
- 3 Meloom mel na ni melax, ay yéreem weex tàll ni perkaal.
- 4 Ñi doon wottu tiit bay lox, daldi mel ni ñu dee.
- 5 Noonu malaaka ma ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne yéena ngi wut Yeesu, ma ñu daajoon ca bant ba,
- 6 waaye nekkatu fi, ndaxte dekki na, ni mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon,
- 7 te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.»
- 8 Bi loolu amee nag jigéen ña daldi jóge bu gaaw ca bàmmeel ba, tiit ak mbég mu réy di jax seen xol, ñu daldi daw, ngir yégal ko taalibe ya.
- 9 Ba ñuy dem nag, Yeesu taseek ñoom ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Jigéen ña jegesi, laxasu cay tànkam, di ko màggal.
- 10 Yeesu ne leen: «Buleen tiit, waaye demleen yégal samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.»
- 11 Ba ñuy dem, ñenn ca wottukat ya ñëw ca dëkk ba, xamal sarxalkat yu mag ya lépp lu xew.
- 12 Noonu sarxalkat ya dajaloo ak njiit ya, ñu diisoo; ba noppi ñu fab xaalis bu bare, jox ko xarekat ya,
- 13 ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.”
- 14 Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.»
- 15 Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey.
- 16 Noonu fukki taalibe ya ak benn dem ci biir Galile, ca tund wa leen Yeesu digaloon.
- 17 Bi ñu gisee Yeesu, ñu màggal ko, waaye ñenn ñi am xel ñaar.
- 18 Yeesu jegesi ne leen: «Sañ-sañ bépp, jox nañu ma ko ci kaw ak ci suuf.
- 19 Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi;
- 20 ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. Maa ngi ànd ak yéen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»