마가복음 3장 월로프어 신약
- 1 Am beneen bés, Yeesu duggaat ci jàngu bi, fekk amoon na fa nit ku loxoom làggi.
- 2 Am na fa nag ay Farisen, ñuy xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu man koo tuumaal.
- 3 Yeesu ne ku loxoom làggi: «Jógal, taxaw ci kanam ñépp.»
- 4 Noonu Yeesu ne leen: «Lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?» Waaye ñu ne cell.
- 5 Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ.
- 6 Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu.
- 7 Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem jóge fa, jëm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jóge diiwaanu Galile, topp ko.
- 8 Te it nit ñu bare dégg la mu def, ñu ñëw fi moom, jóge diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wàlli Tir ak Sidon.
- 9 Booba nag Yeesu faj na ñu bare, ba mboolem ñi am i jàngoro di ko song, ngir laal ko. Noonu Yeesu wax ay taalibeem, ñu wutal ko gaal, ngir mbooloo mi bañ koo buux.
- 11 Fekk booba képp ku rab jàpp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.»
- 12 Waaye Yeesu gëdd rab yi bu wér, ngir ñu bañ koo siiwal.
- 13 Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci tund wi, woo ñi ko neex, ñu daldi ñëw ci moom.
- 14 Noonu mu tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñu ànd ak moom te mu yónni leen, ñu waareji,
- 15 mu joxaale leen sañ-sañu dàq ay rab.
- 16 Fukk ak ñaar ñii la tànn: Simoŋ, mi mu tudde Piyeer,
- 17 Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay— ñoom ñi mu wooye Bowanerses, maanaam «Ñi aaytal ni dënnu gi»—
- 18 Andare ak Filib, Bartelemi ak Macë, Tomaa ak Saag doomu Alfe, Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
- 19 ak Yudaa Iskariyo mi nara wor Yeesu.
- 20 Am beneen bés Yeesu ñëwaat ca kër ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax manuñoo lekk sax.
- 21 Bi ko ay bokkam déggee nag, ñu ñëw, ngir jàppsi ko naan: «Dafa tàggoo ak sagoom.»
- 22 Te it xutbakat ya jóge Yerusalem ne: «Beelsebul jàpp na ko; ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
- 23 Noonu Yeesu woo leen, wax ak ñoom ciy léeb ne leen: «Naka la Seytaane mana dàqe Seytaane?
- 24 Réew mu xeex boppam, du mana yàgg.
- 25 Te kër gu xeex boppam, du mana yàgg.
- 26 Bu Seytaane nag jógee, ba xeex boppam, xàjjalikoo dikkal na ko te du mana yàgg, waaye dina tas.
- 27 «Su fi amee nit ku bare doole, naka la kenn mana dugge ci këram, nangu alalam? Xanaa dafay jëkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj këram gépp.
- 28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp dees na ko baal nit ñi, muy bàkkaar, muy sosal Yàlla wu mu mana doon.
- 29 Waaye kuy sosal Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk; gàddu na bàkkaar ba fàww.»
- 30 Yeesu wax na loolu, ndaxte nee woon nañu, rab jàpp na ko.
- 31 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw, ñu taxaw ci biti, yónnee, woo ko.
- 32 Fekk booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko nag: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi taxaw ci biti, di la laaj.»
- 33 Waaye Yeesu ne leen: «Kan mooy sama ndey? Ñan ñooy samay rakk?»
- 34 Noonu mu xool ñi ko wër naan: «Sama yaay ak samay rakk a ngii;
- 35 ndaxte kuy def coobarey Yàlla, kooku mooy sama rakk ak sama jigéen ak sama ndey.»