마가복음 4장 월로프어 신약
- 1 Am beneen yoon Yeesu nekk ci wetu dex ga, di jànglewaat. Mbooloo mu bare dajaloosi, ba tax mu yéeg cig gaal, dugg ca dex ga; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
- 2 Noonu Yeesu daldi leen jàngal lu bare ciy léeb. Ci njàngleem nag mu ne leen:
- 3 «Dégluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
- 4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
- 5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
- 6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
- 7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meññul dara.
- 8 Li ci des dal ci suuf su baax, mu jóg, sax, di focci ay gub; lii àntu, ba mat fanweeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, lii mat téeméer.»
- 9 Noonu Yeesu ne leen: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
- 10 Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wéet, fukki taalibe ak ñaar ña, ak ñeneen ñu daan ànd ak ñoom, laaj ko ci mbirum léeb yi.
- 11 Mu ne leen: «Yéen may nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci biti léeb ay ëmb lépp.
- 12 Noonu la, ngir: “Ñuy xool bu baax waaye duñu gis dara, di déglu bu baax waaye duñu xam dara, ngir bañ ñu tuub seeni bàkkaar te Yàlla baal leen.”»
- 13 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax xamuleen léeb wii? Nu ngeen xame nag léeb yi ci des?
- 14 Ki ji nag, kàddu gi lay ji.
- 15 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg, Seytaane ñëw ci saa si, këf kàddu, gi ñu def ci moom.
- 16 Ki jot kàddu gi ci bérab bu bare ay doj mooy ki dégg kàddu gi, nangu ko ak mbég ci saa si,
- 17 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
- 18 Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi,
- 19 waaye soxlay àddina ak naxi alal ak bëgge solu ko, tanc kàddu gi, ba du meññ dara.
- 20 Ki jot kàddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko dégg te nangu ko, ba jariñ; kii mat fanweeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, kii mat juróom benn fukk, kii mat téeméer.»
- 21 Yeesu ne leen itam: «Ndax nit dina jël làmp, dëpp ci leget walla def ko ci ron lal? Ndax du ko wékk?
- 22 Amul dara luy kumpa lu ñu warula siiwal, mbaa mu làqu te warul ne fàŋŋ.
- 23 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
- 24 Mu ne leen: «Seetleen bu baax li ngeen di dégg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen.
- 25 Ku am, dees na la dollil; ku amul, li nga am as néew, dees na ko nangu.»
- 26 Yeesu teg ci ne: «Nguuru Yàlla dafa mel ni nit ku ji tool.
- 27 Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa bëccëg, jiwu wi sax, di màgg, te xamul naka la ko defe.
- 28 Suuf day meññ moom ci boppam, mu sax, focci, def i gub.
- 29 Bu gub yi ñoree nag, mu dagg ko, ndaxte ngóob jot na.»
- 30 Yeesu ne leen ati: «Lu nu mana méngaleel nguuru Yàlla? Walla ban léeb lanu ko mana misaale?
- 31 Dafa mel ni doomu fuddën, bi gëna tuuti ci jiwu yépp;
- 32 waaye boo ko jiyee, day jóg, màgg, ba sut gàncaxi tóokër yépp; mu sax ay bànqaas yu réy, ba picci asamaan tàgg ci keram.»
- 33 Noonu Yeesu dégtal leen yeneen léeb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal kàddu gi, aju ci lu ñu àttan.
- 34 Daawu leen wax dara lu dul ciy léeb. Waaye bu wéetee ak ay taalibe, daan na leen firil lépp.
- 35 Bés booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: «Nanu jàll dex gi.»
- 36 Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jël ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneen gaal ànd ak moom.
- 37 Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg, duus yi sàng gaal gi, ba mu bëgga fees.
- 38 Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi. Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?»
- 39 Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm.
- 40 Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?»
- 41 Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?»