누가복음 17장 월로프어 신약
- 1 Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: «Fiir yuy yóbbe nit bàkkaar manta ñàkk, waaye toroxte dal na ki koy lal.
- 2 Ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej moo gën ci moom muy daaneel ci bàkkaar kenn ci ñi gëna tuuti ci ñii.
- 3 Wottuleen seen bopp. «Bu sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu réccoo, baal ko.
- 4 Te su la tooñee juróom ñaari yoon ci bés bi, te ñëw ci yaw juróom ñaari yoon ne la: “Tuub naa ko,” nanga ko baal.»
- 5 Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: «Yokkal sunu ngëm.»
- 6 Boroom bi ne leen: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen mana ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax.
- 7 «Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk”?
- 8 Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma reer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga doora lekk te naan.”
- 9 Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet.
- 10 Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
- 11 Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xàjjale Samari ak Galile.
- 12 Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dànd ko, di wax ca kaw naan:
- 13 «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!»
- 14 Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: «Demleen won seen bopp sarxalkat ya.» Bi ñuy dem, ñu daldi set.
- 15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb.
- 16 Mu dëpp jëëm ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon.
- 17 Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom ñeent ña nag?
- 18 Amul kenn ci ñoom ku ñëw gërëm Yàlla ku dul doxandéem bii!»
- 19 Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
- 20 Farisen yi laaj Yeesu ne ko: «Kañ la Yàlla di tëral nguuram?» Mu ne leen: «Bu Yàlla di wàcce nguuram ci nit ñi, kenn du ko mana teg bët.
- 21 Duñu mana wax it ne: “Xool-leen, mi ngi fii,” walla: “Ma nga fale,” ndaxte nguuru Yàlla wàcc na ci seen biir.»
- 22 Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgga gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis.
- 23 Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp.
- 24 Ndaxte ni melax naan ràyye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci bésam.
- 25 Waaye balaa booba fàww mu sonn lool te niti jamono jii dëddu ko.
- 26 «La xewoon ca bési Nóoyin, dina xewaat ci bési Doomu nit ki.
- 27 Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jël jabar ak a séyi, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga. Noonu mbënn ma ñëw, rey leen ñoom ñépp.
- 28 «Dina mel it ni la xewoon ca bési Lóot. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jënd ak di jaay, di ji ak di tabax.
- 29 Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, Yàlla tawloo sawara ak tamarax, rey leen ñoom ñépp.
- 30 Noonu lay mel, bés bu Doomu nit kiy feeñ.
- 31 «Ca bés boobee ku nekk ca kaw kër ga te ay bagaasam nekk ca biir, bumu wàcc jëli leen. Te it ku nekk ca tool ya, bu mu ñibbi.
- 32 Fàttalikuleen soxnas Lóot!
- 33 Kuy wuta rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ko ñàkk, dinga dund.
- 34 Maa ngi leen koy wax: ca jamono jooju, ñaar dinañu bokka tëdd guddi, dees na yóbbu kenn ki, bàyyi ka ca des.
- 35 Ñaari jigéen dinañu wolandoo, dees na yóbbu kenn ci, bàyyi ka ca des.»
- 37 Taalibe yi ne Yeesu: «Fu loolu di xewe, Boroom bi?» Yeesu ne leen: «Fa médd nekk, la tan yiy dajee.»