누가복음 19장 월로프어 신약
- 1 Yeesu dugg na Yeriko, jaar ca dëkk ba, di dem.
- 2 Waaye amoon na fa waa ju ñuy wax Sase. Njiitu juutikat la, te di ku bare alal.
- 3 Bëgg na gis kan mooy Yeesu, waaye dafa gàtt lool, ba manu koo gis ndax mbooloo ma.
- 4 Noonu mu daw, jiituji ca yoon wa, yéeg ci genn garab ngir gis Yeesu, ndaxte foofa la naroona jaar.
- 5 Bi Yeesu dikkee ba tollook garab ga nag, mu téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax tey sa kër laa wara dal.»
- 6 Sase daldi gaawantu wàcc, ganale ko ak mbég.
- 7 Ñépp gis loolu, di ñurum-ñurumi naan: «Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar.»
- 8 Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma masa njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.»
- 9 Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.
- 10 Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.»
- 11 Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa.
- 12 Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu délsiwaat.
- 13 Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba may ñibsi.”
- 14 Waaye waa réewam bëgguñu ko. Noonu ñu yónni ndaw ci gannaawam ne: “Bëggunu nit kii yilif nu.”
- 15 «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu délsi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye.
- 16 Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.”
- 17 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.”
- 18 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.”
- 19 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
- 20 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.
- 21 Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.”
- 22 Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul.
- 23 Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot sama xaalis ak la mu jur.”
- 24 «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.”
- 25 Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.”
- 26 Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
- 27 Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»
- 28 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem.
- 29 Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem,
- 30 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn masula war. Yiwileen ko, indi.
- 31 Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”»
- 32 Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon.
- 33 Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?»
- 34 Ñu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.»
- 35 Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.
- 36 Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi.
- 37 Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis.
- 38 Ñu ngi naan: «Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na jàmm am ca asamaan, te ndam li féete ca bérab yu gëna kawe!»
- 39 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!»
- 40 Noonu mu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»
- 41 Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko
- 42 naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la mana indil jàmm! Waaye fi mu ne manuloo koo gis.
- 43 Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la.
- 44 Dinañu la yàqate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.»
- 45 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ña fay jaay,
- 46 naan leen: «Mbind mi nee na: “Sama kër këru ñaan ci Yàlla lay doon; waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.”»
- 47 Bés bu nekk Yeesu di jàngle ca kër Yàlla ga. Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya, ñoom ak njiiti xeet wa, ñu ngi ko doon wuta reylu.
- 48 Waaye xamuñu woon lan lañu mana def, ndaxte nit ñépp a ngi ko doon déglu, bañ benn baat raw leen.