누가복음 22장 월로프어 신약
- 1 Màggalu Mburu ma amul lawiir jege woon na, te ñu di ko wax bésu Mucc ba.
- 2 Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya di wut pexem reylu Yeesu, ndaxte dañoo ragaloon nit ña.
- 3 Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi ñuy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar.
- 4 Noonu Yudaa dem waxtaani ak sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu.
- 5 Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis.
- 6 Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen mana jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul.
- 7 Bésu màggalu Mburu ma amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroona rendi gàttub bésu Mucc ba.
- 8 Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru bésu Mucc ba.»
- 9 Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?»
- 10 Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg,
- 11 te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc ba, man ak samay taalibe?”
- 12 Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.»
- 13 Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
- 14 Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,
- 15 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru bésu Mucc bii, laata ñu may sonal.
- 16 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.»
- 17 Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko.
- 18 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum reseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.»
- 19 Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
- 20 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.
- 21 Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.
- 22 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.»
- 23 Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nara def loolu.
- 24 Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gëna màgg.
- 25 Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm.
- 26 Waaye yéen buleen def noonu. Ki gëna màgg ci yéen, na nekk ni ki gëna ndaw, te njiit mel ni surga.
- 27 Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gëna màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.
- 28 Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna.
- 29 Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.
- 30 Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»
- 31 Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.
- 32 Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo délsee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»
- 33 Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.»
- 34 Yeesu ne ko: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
- 35 Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
- 36 Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi.
- 37 Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.»
- 38 Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»
- 39 Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe naka-jekk. Taalibeem ya topp ci moom.
- 40 Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir baña daanu cig fiir.»
- 41 Noonu mu dànd leen, ba fu aw saan mana tollu, daldi sukk di ñaan ne:
- 42 «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
- 43 Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole.
- 44 Ci biir tiis, Yeesu gëna sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.
- 45 Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.
- 46 Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña daanu cig fiir.»
- 47 Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon.
- 48 Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!»
- 49 Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgga xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?»
- 50 Kenn ci ñoom nag dóor surgab sarxalkat bu mag ba, noppu ndijooram dagg.
- 51 Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
- 52 Noonu Yeesu ne sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
- 53 Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.»
- 54 Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër sarxalkat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.
- 55 Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir.
- 56 Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.»
- 57 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.»
- 58 Nees-tuut keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer ne ko: «Sama waay, bokkuma ci.»
- 59 Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.»
- 60 Waaye Piyeer ne ko: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab.
- 61 Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.»
- 62 Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti.
- 63 Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor.
- 64 Ñu ngi takkoon ay bëtam, di ko laaj, naan ko: «Yaw, wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?»
- 65 Ñu ngi ko doon tifaar it yeneen saaga.
- 66 Bi bët setee, kureelu njiiti xeet wa, maanaam sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya, daldi daje, indi Yeesu ci seen kanam.
- 67 Ñu ne ko: «Soo dee Almasi bi, wax nu ko.» Mu ne leen: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm.
- 68 Te su ma leen laajee, dungeen tontu.
- 69 Waaye gannaaw-si-tey, Doomu nit ki dina toog ci ndijooru Yàlla, Aji Man ji.»
- 70 Noonu ñépp ne: «Kon nag yaay Doomu Yàlla ji?» Mu ne leen: «Yéen ci seen bopp wax ngeen ne moom laa.»
- 71 Ñu daldi ne nag: «Lu nuy doyeeti seede léegi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci gémmiñam!»