누가복음 24장 월로프어 신약
- 1 Bés bu jëkk ca ayu-bés ga, jigéen ña jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Ñu ngi yoroon cuuraay lu ñu defaroon.
- 2 Bi ñu agsee, ñu fekk ñu béraŋ doj, wa uboon bàmmeel ba.
- 3 Ñu dugg ca bàmmeel ba, waaye fekkuñu fa néewu Boroom bi Yeesu.
- 4 Noonu ba ñu nekkee ak seen njaaxle, am na ñaar ñu leen feeñu, sol yére yuy melax.
- 5 Jigéen ña am tiitaange ju mag, daldi dëpp seen jë ci suuf. Waaye ñu ne leen: «Lu tax ngeen di seet kiy dund ci biir néew yi?
- 6 Nekkatu fi; dekki na. Fàttalikuleen la mu leen waxoon, ba mu nekkee Galile.
- 7 Nee woon na: “Fàww ñu jébbal Doomu nit ki bàkkaarkat yi, ñu rey ko ci bant, mu dekki ca ñetteelu fan ba.”»
- 8 Noonu ñu daldi fàttaliku kàdduy Yeesu ya.
- 9 Bi ñu jógee bàmmeel ba, ñu dem nettaliji loolu lépp fukki ndaw ya ak benn, ak ña ca des ñépp.
- 10 Jigéen ña ñoo doon Maryaamam Magdala, Sànn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jigéen yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya.
- 11 Waaye ñu teg wax jooju ay jeneer, ba gëmuñu jigéen ñooñu.
- 12 Waaye Piyeer daldi jóg, daw, dem ca bàmmeel ba. Bi mu àggee, mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Noonu mu dëpp ñibbi, jaaxle lool ci li xew.
- 13 Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet.
- 14 Ñu waxtaane li xewoon lépp.
- 15 Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom,
- 16 fekk seeni bët muuru, ba manu ko woona xàmmi.
- 17 Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex.
- 18 Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?»
- 19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla.
- 20 Waaye sunuy sarxalkat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko jébbal nguur gi ngir ñu àtte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant.
- 21 Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy kiy nara jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak léegi, tey la ñetteelu fan bi.
- 22 Teewul nag am na ay jigéen yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Dañoo fajaru ca bàmmeel ba,
- 23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu délsi, nettali nu ne, ay malaaka feeñu nañu leen, yégal leen ne mi ngi dund.
- 24 Ñenn ci sunu àndandoo yi dem nañu ca bàmmeel ba, fekk lépp mel, na ko jigéen ña waxe woon. Waaye moom gisuñu ko.»
- 25 Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéexa gëm li yonent yi yégle woon!
- 26 Xanaa du Almasi bi dafa waroona daj boobu coono te dugg ci ndamam?»
- 27 Noonu mu tàmbalee ci yonent Yàlla Musaa ba ci yonent yépp, tekkil leen li Mbind mi wax lépp ci ay mbiram.
- 28 Bi ñuy jub dëkk, ba ñu jëmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam.
- 29 Waaye ñu téye ko ne ko: «Toogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te léegi mu guddi.» Noonu mu dugg, toog ca ñoom.
- 30 Bi ñu tàmbali di reer, Yeesu jël mburu ma, gërëm Yàlla, ba noppi damm ko, jox leen ko.
- 31 Bi mu defee loolu, lépp leer ci seeni bët, ñu daldi ko xàmmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatuñu ko.
- 32 Noonu ku nekk naan sa moroom: «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?»
- 33 Ñu daldi jóg ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneen taalibe.
- 34 Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!»
- 35 Ñaari taalibe ya ñoom it daldi leen nettali la xewoon ca yoon wa ak ni ñu xàmmee Yeesu, bi mu dammee mburu ma.
- 36 Bi ñaari taalibe ya dee wax noonu, Yeesu taxaw moom ci boppam ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen.»
- 37 Ñu daldi tiit, foog ne dañoo gis njuuma.
- 38 Waaye Yeesu ne leen: «Lu tax ngeen jaaxle, ak lu tax ngeen di xel ñaar ci seen xol?
- 39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man mii la. Laal-leen ma te xam, njuuma amul yaram walla ay yax, ni ngeen gise, ma am ko.»
- 40 Bi mu leen waxee loolu, mu won leen ay loxoom ak ay tànkam.
- 41 Waaye ba tey manuñu woona gëm ndax seen mbég ak jaaxle. Noonu Yeesu laaj leen ne: «Ndax am ngeen fii lu ñu lekk?»
- 42 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk.
- 43 Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
- 44 Noonu mu ne leen: «Bi ma nekkee ak yéen, waxoon naa leen baat yii: li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa wara am.»
- 45 Noonu mu ubbi seen xel, ngir ñu xam li Mbind mi di wax.
- 46 Mu ne leen: «Fàww Almasi bi sonn, mu dee te dekki ca ñetteelu fan ba, ni ñu ko binde,
- 47 te it ñuy yégle xeet yépp ci turam, dale ko ci Yerusalem ne war nañoo tuub seeni bàkkaar, Yàlla baal leen.
- 48 Yéenay samay seede.
- 49 Te man dinaa leen yónnee li sama Baay dige. Yéen nag toogleen ci dëkk bi, ba ñu sol leen doole ji jóge ci kaw.»
- 50 Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Foofa mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.
- 51 Bi mu leen dee barkeel, mu tàggoo ak ñoom, Yàlla yéege ko asamaan.
- 52 Taalibe ya màggal ko, daldi dellu Yerusalem, fees ak mbég.
- 53 Foofa daawuñu jóg ca kër Yàlla ga, di gërëm Yàlla.