누가복음 9장 월로프어 신약
- 1 Benn bés Yeesu dajale fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen doole ak sañ-sañu dàq rab yépp ak di faj jàngoro yi.
- 2 Noonu mu yónni leen ñuy yégle nguuru Yàlla ak di faj jarag yi.
- 3 Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara, du yet mbaa mbuus mbaa mburu mbaa xaalis. Buleen yor it ñaari turki.
- 4 Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa jóge.
- 5 Fépp fu leen nit ñi gàntoo, génnleen ca dëkk booba te ngeen yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»
- 6 Noonu ñu dem dëkk ak dëkk, di fa yégle xibaaru jàmm bi, tey wéral jarag yi.
- 7 Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.»
- 8 Am it ñuy wax naan: Ilyaas moo délsi. Ñeneen naan: «Kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
- 9 Waaye Erodd ne: «Yaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma dégg ay jalooreem, mooy kan?» Noonu mu koy fexee gis.
- 10 Bi ndaw ya délsee, ñu nettali Yeesu la ñu defoon lépp. Noonu mu yóbbaale leen, ñu sore nit ñi, jëm ca dëkk bu ñuy wax Betsayda.
- 11 Bi ko nit ña yégee, ñu toppi ko. Yeesu teeru leen, di leen wax ci mbirum nguuru Yàlla, te di wéral ñi ko aajowoo.
- 12 Ca ngoon sa fukki taalibe ya ak ñaar ñëw ci Yeesu ne ko: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yi ak àll bi ko wër, ngir am lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndaxte fii àllub neen la.»
- 13 Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?»
- 14 Ndaxte lu wara mat juróomi junniy góor a nga fa teewoon. Yeesu ne taalibe ya: «Neeleen mbooloo mi ñu toog def ay géewi juróom fukki nit.»
- 15 Taalibe ya def ko, toogloo nit ña.
- 16 Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, gërëm Yàlla, ba noppi mu damm leen, jox taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi.
- 17 Noonu ñépp lekk ba suur. Bi ñu dajalee desit ya, ñu feesal fukki pañe ak ñaar.
- 18 Benn bés Yeesu beddeeku mbooloo ma, di ñaan; taalibe yi nekk ci wetam. Mu laaj leen ne: «Nit ñi, ku ñu wax ne moom laa?»
- 19 Ñu ne ko: «Am na ñu naan, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Ilyaas; ñi ci des ne yaay kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
- 20 Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.»
- 21 Noonu Yeesu daldi leen dénk, tere leen ñu wax ko kenn,
- 22 teg ca ne: «Doomu nit ki war na sonn lu bare; sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.»
- 23 Noonu Yeesu ne leen ñoom ñépp: «Ku bëgga aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, gàddu bés bu nekk bant, bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man.
- 24 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat.
- 25 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, su fekkee ne dafay ñàkk bakkanam walla mu loru?
- 26 Ku ma rusa faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rusa xam, bés bu ñëwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi.
- 27 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw ñoo xam ne duñu dee te gisuñu nguuru Yàlla gi.»
- 28 Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan.
- 29 Bi muy ñaan, xar kanamam daldi soppiku, ay yéreem weex tàll bay melax.
- 30 Am ñaari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Yàlla Musaa ak Ilyaas.
- 31 Ñoo feeñ ci ndamu Yàlla, di waxtaane ci demug Yeesu, gi muy àggalee yenam ci Yerusalem.
- 32 Fekk Piyeer ak ñi mu àndal doon gëmméentu, waaye bi ñu yewwoo bu baax, ñu gis ndamu Yeesu, ak ñaari nit ñu taxaw ci wetam.
- 33 Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» Fekk xamul la mu doon wax.
- 34 Bi mu koy wax, niir ñëw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa ëmbee.
- 35 Noonu baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma fal; dégluleen ko.»
- 36 Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, baña nettali kenn ca jamono jooja la ñu gisoon.
- 37 Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare ñëw, di ko gatandu.
- 38 Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: «Kilifa gi, maa ngi lay ñaan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am.
- 39 Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal.
- 40 Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye manuñu ko.»
- 41 Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa wara nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.»
- 42 Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi gëdd rab wa, wéral xale ba, daldi ko delloo baayam.
- 43 Ku nekk waaru na ndax màggug Yàlla. Bi ñuy yéemu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya:
- 44 «Dégluleen bu baax lii ma leen di wax: dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.»
- 45 Waaye taalibe ya xamuñu kàddu googu. Yàlla dafa leen nëbb li muy tekki, ba ñu bañ koo xam, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
- 46 Werante am ci biir taalibe yi, ñuy laajante kan moo gëna màgg ci ñoom.
- 47 Yeesu mi xam seen xalaat, jël ab xale, teg ci wetam ne leen:
- 48 «Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gëna woyof ci yéen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
- 49 Bi loolu amee Yowaana jël kàddu gi ne: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.»
- 50 Waaye Yeesu ne ko: «Buleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.»
- 51 Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem.
- 52 Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal.
- 53 Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem.
- 54 Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na sawaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?»
- 55 Waaye Yeesu walbatiku, yedd taalibe ya,
- 56 ba noppi ñu daldi dem wuti beneen dëkk.
- 57 Bi ñuy dem, am ci yoon wi ku ne Yeesu: «Dinaa la topp fépp foo jëm.»
- 58 Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
- 59 Yeesu ne keneen: «Toppal ci man.» Waaye kooku ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem suuli sama baay.»
- 60 Mu ne ko: «Bàyyil ñi dee, ñu suul seeni néew. Yaw demal, yégle nguuru Yàlla.»
- 61 Keneen ne ko: «Sang bi, dinaa la topp, waaye may ma, ma jëkka tàgguji sama waa kër.»
- 62 Yeesu ne ko: «Kuy ji, di geestu, yeyoowula liggéey ci nguuru Yàlla.»