요한복음 11장 월로프어 신약
- 1 Amoon na benn waay bu woppoon, ñu koy wax Lasaar. Ma nga dëkkoon Betani, moom ak Maryaama ak Màrt, mi mu bokkaloon ndey ak baay.
- 2 Maryaama mooy jigéen jiy sottiji latkoloñ ci tànki Boroom bi, fompe ko kawaram. Moom la càmmiñam Lasaar woppoon.
- 3 Ñaari jigéeni Lasaar yónnee ca Yeesu ne ko: «Boroom bi, sa xarit wopp na.»
- 4 Bi Yeesu déggee xibaar boobu, mu ne: «Lasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Yàlla, tey màggal Doomu Yàlla ji.»
- 5 Yeesu soppoon na Màrt ak Maryaama ak Lasaar.
- 6 Bi mu yégee nag ne Lasaar wopp na, mu toogaat yeneen ñaari fan ca bérab, ba mu nekkoon.
- 7 Gannaaw loolu mu ne taalibe ya: «Nanu dellu Yude.»
- 8 Taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, yàggul dara waa Yude doon nañu la wuta rey ak i xeer, nga di fa dellu?»
- 9 Yeesu ne leen: «Xanaa du bëccëg fukki waxtook ñaar la? Kuy dox bëccëg, du fakktalu, ndaxte day gis leeru àddina si.
- 10 Waaye kuy dox guddi, dina fakktalu, ndaxte leer nekkul ci moom.»
- 11 Yeesu wax loolu, teg ca ne: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko.»
- 12 Taalibe ya ne ko: «Boroom bi, bu nelawee kay, kon dina wér.»
- 13 Yeesu dafa bëggoona wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne mbiri nelaw rekk lay wax.
- 14 Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne: «Lasaar dee na.
- 15 Bég naa ngir yéen ndax li ma fa nekkul, ngir seen ngëm gëna dëgër. Waaye nanu ko seeti.»
- 16 Noonu Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi», daldi ne yeneen taalibe ya: «Nanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!»
- 17 Bi Yeesu agsee, mu fekk ne bi ñu dencee Lasaar ak léegi, mat na ñeenti fan.
- 18 Betani ma nga woon ca wetu Yerusalem, diggante bi matul woon sax ñetti kilomet.
- 19 Yawut yu bare ñëwoon nañu kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfal leen ci seen deewu càmmiñ.
- 20 Bi Yeesu ñëwee, Màrt yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga.
- 21 Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee.
- 22 Waaye xam naa ne fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko.»
- 23 Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.»
- 24 Màrt ne ko: «Xam naa ne dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba.»
- 25 Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund.
- 26 Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
- 27 Mu ne ko: «Waaw, Boroom bi. Gëm naa ne yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji wara ñëw àddina.»
- 28 Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem wooyi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.»
- 29 Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantu dem ca Yeesu.
- 30 Te fekk duggagul woon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba mu daje woon ak Màrt.
- 31 Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfal Maryaama, gis ko mu ne bërét génn, ñu daldi koy topp, defe ne day jooyi ca bàmmeel ba.
- 32 Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam ne ko: «Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee.»
- 33 Yeesu gis ne mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy.
- 34 Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu ne ko: «Kaay gis, Sang bi.»
- 35 Yeesu jooy.
- 36 Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!»
- 37 Waaye am na ca ñoom ñu doon wax naan: «Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax manul woona fexe ba Lasaar du dee?»
- 38 Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer.
- 39 Yeesu ne: «Dindileen xeer wi!» Màrt, jigéenu ku dee ki ne ko: «Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.»
- 40 Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?»
- 41 Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi.
- 42 Xam naa ne doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax, ngir nit ñi ma wër gëm ne yaa ma yónni.»
- 43 Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!»
- 44 Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
- 45 Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy gëm.
- 46 Waaye amoon na it ñu demoon ci Farisen ya, nettali leen la Yeesu defoon.
- 47 Farisen ya ak sarxalkat yu mag ya woo kureelu àttekat ya ne: «Nit kii kat, kéemaan yi muy def a ngi bëgga bare. Lu nuy def nag?
- 48 Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew!»
- 49 Amoon na ca ñoom ku ñuy wax Kayif te mu nekkoon sarxalkat bu mag ba at mooma; mu ne leen: «Xamuleen ci mbir mi dara.
- 50 Xanaa xamuleen ne, kenn nit rekk dee ngir ñépp, mooy li gën ci yéen? Bu ko defee réew mi du tas.»
- 51 Loolu Kayif waxu ko woon ci sagoom, waaye li mu nekkoon sarxalkat bu mag ba at mooma, moo tax Yàlla xiirtal ko mu ne, Yeesu dina dee ngir réew mi.
- 52 Du woon rekk ngir xeet woowu, waaye ngir itam doomi Yàlla, yi tasaaroo yépp, dajaloo nekk benn.
- 53 Keroog la njiiti Yawut ya dogu ci rey Yeesu.
- 54 Taxoon na ba Yeesu dootul doxantu ci biir Yawut ya. Noonu mu dem ca gox bu jege màndiŋ ma, ca dëkku Efrayim. Foofa nag la toog ak ay taalibeem.
- 55 Bésu Mucc baa ngi doon jubsi, mu doonoon ag màggal ci Yawut yi, ba ñu bare ca waa àll ba di dem Yerusalem balaa booba, ngir sanguji set.
- 56 Ñu ngi doon wut Yeesu tey waxante ca kër Yàlla ga naan: «Lu ngeen ci xam? Ndax dina ñëw ci màggal gi walla déet?»
- 57 Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya daldi santaane ne, bu kenn xamee fu Yeesu nekk, mu yégle ko, ngir ñu man koo jàpp.