사도행전 24장 월로프어 신약
- 1 Bi juróomi fan wéyee, Anañas sarxalkat bu mag ba dikk, ànd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, ñu woo Pool ci yoon fa kanam boroom réew ma.
- 2 Noonu ñu woo Pool, te Tertul daldi ko jiiñ naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, sa nguur jural na nu jàmm ju neex, te sa jàppandil soppi na lu bare ci sunu xeet.
- 3 Gis nanu ko fépp ak ci lépp, di la gërëm ak sunu xol bépp.
- 4 Waaye ngir baña yàggal jataay bi, maa ngi lay ñaan ci sa lewetaay, nga déglu nu ci lu gàtt.
- 5 Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi xëccoo ci Yawut yi ci àddina sépp, di njiitu mbooloo mu ñuy wax Nasareen.
- 6 Dem na ba jéema teddadil sax kër Yàlla ga, waaye jàpp nanu ko.
- 8 Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne li nu koy jiiñ dëgg la.»
- 9 Ci kaw loolu Yawut ya ànd ca, di dëggal ne loolu wóor na.
- 10 Bi loolu amee boroom réew ma jox Pool kàddu gi. Noonu mu làyyi ne: «Xam naa ne yaa ngi àtte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi làyyi ak kóolute.
- 11 Man ngaa wóorliku ne ëppagul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggali.
- 12 Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di jógloo mbooloo, muy ca kër Yàlla ga mbaa ca jàngu ya mbaa ci biir dëkk ba.
- 13 Te manuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi.
- 14 Waaye nangu naa ci sa kanam ne maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne mooy tariixa; terewul ne lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko.
- 15 Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam.
- 16 Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
- 17 «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax.
- 18 Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.
- 19 Waaye ay Yawut yu dëkk Asi —xanaa kay ñoo waroona ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp.
- 20 Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba,
- 21 xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”»
- 22 Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.»
- 23 Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.»
- 24 Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak soxnaam Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist.
- 25 Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.»
- 26 Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko farala woolu, ngir waxtaan ak moom.
- 27 Bi ñaari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligsë, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligsë, mi bëggoon lu neex Yawut ya, bàyyi Pool ca kaso ba.