로마서 10장 월로프어 신약
- 1 Bokk yi, sama coobarey xol ci bànni Israyil ak sama ñaan ci Yàlla, mooy ñu mucc.
- 2 Seedeel naa leen ne, ñu farlu lañu ci jaamu Yàlla, waaye seen njaamu àndul ak xam-xam.
- 3 Xamuñu yoon, wi Yàlla tëral ngir nit jub ci kanamam, waaye dañoo wéy ci seen pexey bopp; ba tax ñu baña nangu yoonu njub woowu Yàlla tëral.
- 4 Ndaxte ci Kirist la yoonu Musaa dëppe, ba tax ku ko gëm, dinga jub fa kanam Yàlla.
- 5 Ku bëgga jub ci kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, Musaa daf cee wax ne: «Ku ko manoona matal, dinga dund ba fàww.»
- 6 Waaye ku jub ci kanam Yàlla ci kaw ngëm, nii lay waxe: «Bul wax ci sa xol ne: “Kuy yéeg ci kaw?”» mel ni dangaa bëgg Kirist wàcc.
- 7 «Bul wax it: “Kuy dem ca barsàq?”» mel ni dangaa bëgg Kirist dekki.
- 8 Kon boog lan lay wax? Lii: «Waxu Yàlla mi ngi ci sa wet, ci sa làmmiñ, ci sa xol.» Te wax jooju lal ngëm lanuy waare.
- 9 Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc.
- 10 Ndax xol la nit di gëme, ba tax mu jub ci kanam Yàlla; làmmiñ it la nit di waxe ne mi ngi ci Kirist, ba tax Yàlla musal ko.
- 11 Mbind mi dafa wax ne: «Képp ku ko gëm, sa yaakaar du tas mukk.»
- 12 Ndax ñépp a yem ci kanam Yàlla, muy Yawut mbaa ku dul Yawut, ndax kenn rekk mooy sunu Boroom nun ñépp; ku yéwén la ci képp ku koy ñaan.
- 13 Ndaxte bind nañu: «Képp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc.»
- 14 Waaye nan lañuy wooye ki ñu gëmagul? Naka lañu mana gëme ki ñu déggagul turam? Naka lañu mana dégge turam, te kenn xamalu leen ko?
- 15 Nan lañu mana waaree, su leen kenn yónniwul? Looloo tax Mbind mi wax ne: «Ñiy yégle xibaaru jàmm bi, ni seen ñëw di sedde xol!»
- 16 Waaye ñépp nanguwuñu xibaaru jàmm bi; moom la Esayi wax ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?»
- 17 Kon boog ngëm ci kaw dégg lay juddoo, te dégg sosoo ci xibaaru Kirist.
- 18 Waaye ma ne: xanaa ñépp dañoo déggul? Ahakay! Mbind mi wax na ne: «Seen baat jolli na ci ñeenti xébla yépp, seen wax wër na àddina sépp.»
- 19 Waaye ma teg ci ne: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Ahakay! Musaa dafa jëkkoona wax ne: «Dinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Yàlla, merloo leen ci ñi xamul dara ci Yàlla.»
- 20 Esayi it takk na fitam, ba wax ne: «Ñi ma wutul woon, gis nañu ma, feeñ naa ci ñi ma laajul woon.»
- 21 Waaye ci mbirum Israyil dafa wax ne: «Tàllal naa samay loxo, suba ba ngoon, ci xeet wu may bañ tey werante.»