고린도전서 13장 월로프어 신약
- 1 Su fekkee ne damay wax làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te boolewuma ci mbëggeel, duma dara lu dul ndënd muy riir, walla jóolóoli buy kandaŋ-kandaŋi.
- 2 Su ma yéglee wax ju tukkee ci Yàlla, ma xam lépp luy kumpa, ma yor xam-xam bépp te gëm Yàlla ba mana randal ay tund, fekk boolewuma ci mbëggeel, duma dara.
- 3 Te it su ma doon sarxe li ma am lépp, di bàyyi ñu lakk sama yaram, ba rey ma, su ma ci boolewul mbëggeel, du ma jariñ dara.
- 4 Ku bëgg dafay muñ te laabiir. Ku bëgg du iñaan, du kañu, du tiitaru,
- 5 du def lu jekkadi, du wut njariñu boppam, du naqari deret, du ñaaw njort.
- 6 Du bég ci lu awul yoon, waaye dina bég ci lépp luy jollil dëgg.
- 7 Mbëggeel day baale lépp, am gëm ci lépp, yaakaar lépp, muñ lépp.
- 8 Mbëggeel amul àpp. Ñiy wax ci kàddug Yàlla dinañu noppi, ñiy wax ay làkk dinañu ko bàyyi, ñiy xamle xam-xamu Yàlla wàcc.
- 9 Xam-xam bi nu am des na, te ni nu jottalee xibaar bi nu Yàlla dénk des na.
- 10 Waaye li mat, bu dikkee, li matul jóge fi.
- 11 Bi ma dee xale, dama doon wax ni xale, di dégge ni xale, di xalaate ni xale. Waaye bi ma doonee mag, bàyyi naa lu bokkoon cig ndaw.
- 12 Tey jii gis bu lëndëm lanuy gis, ni takkandeer ci seetu bu lëndëm; bu ëllëgee dinanu gis jaxran. Tey jii sama xam-xam des na; bu ëllëgee dinaa xam ba mat sëkk, ni ma Yàlla xame.
- 13 Léegi nag ñett yii ñooy sax: ngëm, yaakaar, mbëggeel; te mbëggeel moo ci raw.