고린도전서 2장 월로프어 신약
- 1 Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma ñëwee ci yéen, ngir yégle mbóoti Yàlla, ñëwuma ci ay wax yu neex ak xam-xam bu réy.
- 2 Dogu woon naa ci baña xam dara ci seen biir lu dul Yeesu Kirist, te muy ki ñu rey ca bant ba.
- 3 Bi ma teewee ci yéen, ànd naa ak ñàkk doole, ragal ak njàqare.
- 4 Li ma wax ak li ma waare, defuma ko ci làmmiñ wu neex, sukkandikoo ko ci xam-xamu nit, waaye ànd na ak ay firnde yu soqikoo ci kàttanu Xelum Yàlla,
- 5 ngir seen ngëm baña wékku ci xam-xamu nit ñi waaye mu wékku ci dooley Yàlla.
- 6 Moona am na xam-xam bu nuy yégal ñi mat, xam-xam bu bokkul ci àddina si, te njiiti àddina si xamuñu ko, ñoom ñi nara wéy.
- 7 Nu ngi yégle mbóotu xam-xamu Yàlla, mu nëbbu woon te Yàlla dogal ko ngir sunu ndam, laata àddina di sosu.
- 8 Kenn ci njiiti àddina amul woon xam-xam boobu. Su ñu ko amoon, kon duñu rey Boroom ndam li ci bant bi.
- 9 Waaye Mbind mi nee na: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel xalaatu ko, loolu la Yàlla dencal ñi ko bëgg.»
- 10 Fekk nag nun la ko Yàlla won, jaarale ko ci Xelam. Xelum Yàlla mooy leeral lépp, ba ci xalaati Yàlla yi gëna xóot.
- 11 Kan ci nit ñi moo xam yëfi nit? Xanaa xelum nit mi nekk ci moom rekk a ko xam. Noonu it kenn xamul yëfi Yàlla, ku dul Xelum Yàlla.
- 12 Nun nag Xel mi nu jot, jógewul ci àddina, waaye Yàllaa nu ko sol.
- 13 Loolu nu Yàlla may, yéglewunu ko ci ay baat yu soqikoo ci xam-xamu nit, waaye nu ngi koy yégle ci baat, yi soqikoo ci Xelum Yàlla, di tekkantal yëfi Xelum Yàlla ci ay baat yu mu nu sol.
- 14 Nit kese du nangu yëfi Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom; du ko mana nangu, ndaxte ku yor Xelum Yàlla rekk moo ko mana ràññale.
- 15 Nit ki yor Xelum Yàlla dafay àtte lépp; moom ci boppam, kenn du ko àtte.
- 16 Ndaxte Mbind mi nee na: «Ana ku xam xalaatu Boroom bi? Ku ko doon digal?» Waaye nun am nanu xalaatu Kirist.