고린도후서 6장 월로프어 신약
- 1 Nun nag ñiy liggéeyandoo ak Yàlla, nu ngi leen di ñaan: jariñooleen yiw, wi ngeen jote ci Yàlla, ngir mu baña neen ci yéen.
- 2 Ndaxte Yàlla nee na: «Ca jamono ja mu jekke, nangu naa sa ñaan; ci bésu mucc gi laa la wallu.» Tey jii la jamono ju jekk ji; tey la bésub mucc gi.
- 3 Bëggunoo lëmbaaje xelu kenn ci dara, ngir kenn baña sikk sunu liggéey.
- 4 Li nu bëgg moo di rafetal sunu tur ni jawriñi Yàlla ci fànn gu nekk; danuy muñ coono yi, tiis yi, njàqare yi;
- 5 ñu nuy dóor, di nu tëj ci kaso, dëkk yi di yëngu ndax sunu mbir; nuy liggéey ba sonn, di fanaane xool, di woor.
- 6 Nu ngi rafetal sunu yen ci dund gu sell, ci xam-xam, muñ ak laabiir, ci Xel mu Sell mi ak ci mbëggeel gu raxul njublaŋ,
- 7 ci kàddug dëgg ak ci kàttanu Yàlla, nu ngi yor gànnaayi njubte ci loxol ndijoor ak lu càmmoñ.
- 8 Ñu bàkk nu, jéppi nu, sant nu, xas nu. Ñu di nu jiiñ réeral, moona niti dëgg lanu.
- 9 Ñuy xeeb sunu tur, moona tur yi siiw nañu. Nu mel ni ñu loof, moona nu ngi dund. Ñu yar nu, teewul nu rëcc ci dee.
- 10 Danuy dékku tiis, waaye di bég fu nu tollu. Nu tumurànke, waaye di woomal ñu bare; amunu dara, fekk noo moom lépp.
- 11 Yéen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir ak sunu biti, di leen ubbil sunu xol.
- 12 Ubbiku nanu ci yéen, waaye yéen ubbikuwuleen ci nun.
- 13 Maa ngi wax ak yéen ni samay doom; feyleen nu bor bi, yéen itam; ubbileen seen xol!
- 14 Buleen likkoo ak ñi gëmul. Gan àndandoo moo mana am diggante njubte ak ndëngte? Gan booloo moo mana am diggante leer ak lëndëm?
- 15 Gan déggoo moo mana am diggante Kirist ak Beliyar? Gan jaxasoo moo mana am diggante ki gëm ak ki gëmul?
- 16 Nan la kër Yàlla mana mànkoo ak xërëm yi? Ndaxte nun nooy kër Yàlla Aji Dund ji, ni ko Yàlla waxe: «Dinaa dëkk ci seen biir, // tey dox ànd ak ñoom, ma nekk seen Yàlla, // ñuy samay gaay.»
- 17 Kon nag Boroom bi nee na: «Génnleen biir ñooñu te beru. Buleen laal dara lu am sobe, kon dinaa leen teeru.
- 18 Dinaa nekk baay ci yéen, ngeen di doom ci man, muy góor, di jigéen. Moom la Aji Man ji wax.»