에베소서 4장 월로프어 신약
- 1 Man mi ñu tëj kaso ngir Boroom bi nag, maa ngi leen di dénk, ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla.
- 2 Ngeen woyof toyy te lewet, di muñalante tey baalante ci mbëggeel,
- 3 te dem ba fu seen kàttan yem, ngeen likkoo ci jàmm, bay sàmm booloo gi leen Xelum Yàlla may.
- 4 Jenn jëmm moo am, menn Xel, ak jenn yaakaaru ëllëg ju wooteb Yàlla ëmb.
- 5 Benn Boroom it a am, genn ngëm, ak benn seedeb ngëm ci li ñu leen sóob ci ndox.
- 6 Te jenn Yàllaa am, di Baayu ñépp, mu tiim ñépp, fees ñépp te dëkk ci ñépp.
- 7 Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ni nu ko Kirist séddalee.
- 8 Looloo tax Mbind mi ne: «Yéeg na ba ca fa gëna kawe, yóbbaale mbooloom noon mu bare, mi mu not, tey séddale nit ñi ay may.»
- 9 Su nu waxee ne «yéeg na,» li moo ci génn: daa jëkka wàcc ba ca bérab ya gëna suufe.
- 10 Ki wàccoon moo yéegaat, ba tiim asamaan yépp, ngir fees lépp.
- 11 Moo may ñii di ay ndawam, ñii ay yonent, ñii ay taskati xibaaru jàmm bi, ak ñeneen ñuy sàmm mbooloom ñi gëm te di ko jàngal.
- 12 Maye na leen, ngir ñu waajal gaayi Yàlla yu sell yi, ñu mana bey seen sas ci taxawal mbooloom Kirist, di jëmmam.
- 13 Noonu nu mànkoo ci sunu ngëm ak ci xam Doomu Yàlla ji, ba kera nuy egg ci nekk nit ku sotti te taxaw taxawaay bu dëppook matug Kirist.
- 14 Noonu dootunu ay gone yu njànglem nit ku ñëw di fàbbi ci seeni làqarci ak seeni pexe, nu mel ni ay gaal yu duus yi ak ngelaw li di baaje.
- 15 Waaye dinanu wax dëgg, ëmb ko ci mbëggeel, bay màgg ci fànn gu ne ci sunu bokk ci Kirist. Mooy bopp,
- 16 te jëmm jépp ci moom lay dunde, di jëmm ju ràbboo te déggoo ci bépp tenqo, te cér bu nekk di def warugaram. Noonu jëmm ji di yokku ak a màgg ci biir mbëggeel.
- 17 Maa ngi leen di wax lii nag, te di ko dëggal ci kanam Boroom bi: buleen dundeeti ni xeeti àddina yi, ci seeni xalaati neen
- 18 ak seen xel mu lëndëm. Dañoo génn ci dundu Yàlla, ndax umple gi ñu am ci moom, ak li ñu ko tëjal seen xol.
- 19 Seen xol dafa dërkiis, ba ñu bayliku ciy topp seen nafsu, di sóobu ci bépp sobe te xér ci.
- 20 Waaye du dundin woowu ngeen jàng ci Kirist.
- 21 Ndax yaakaar naa ne dégg ngeen Kirist te jàng ngeen ci moom, ba xam dëgg gi Yeesu ëmb.
- 22 Maanaam ngeen yulli seen jikkoy judduwaale ju bon ji daan fés ci seeni jëf, di gëna yées, te ànd ak i bëgg-bëggam yu di naxi kese.
- 23 Te ngeen yeeslu ci seen biir xel,
- 24 te soloo jikko ju bees, ji Yàlla sàkk ci njubte lu dëggu ak sellaay gu dëggu.
- 25 Kon nag bàyyileen di fen, tey wax dëgg kenn ku nekk ci moroomam, ndax ku nekk sa genn-wàllu moroom nga.
- 26 Ku mer, bu mu jàll aw kaañ; bu jant bi sowaale seen mer,
- 27 ba ngeen may Seytaane bunt.
- 28 Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax ci ay loxoom, ngir mu mana dimbali ñi néew doole.
- 29 Bu genn kàddu gu ñaaw génn ci seen gémmiñ, waaye su wax yegsee, nangeen wax lu rafet, ba faj soxlay seeni moroom, te teg ñi leen di déglu ci yoonu yiw.
- 30 Buleen yóbbe tiis Xelu Yàlla mu Sell, mi leen tàmpe ngir bésu goreel ba.
- 31 Dëdduleen lépp luy wex mbaa tàng bopp, luy mer mbaa coow, lépp luy xaste mbaa coxor.
- 32 Te ngeen baax ci seen diggante, di laayante biir tey baalante, ni leen Yàlla baale ci turu Kirist.