빌립보서 3장 월로프어 신약
- 1 Kon nag samay bokk, bégleen ci Boroom bi. Duma sonn mukk ci di leen ko wax, ndax seen mucc moo ci aju.
- 2 Moytuleen xaj yi, waaw, moytuleen ñiy jëfe lu bon, ñoom ñi seen xarafal weesul wàññi yaramu nit.
- 3 Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy màggal Yàlla ci Xel mu Sell mi, di damu ci Kirist Yeesu, te amunu benn yaakaar ci matug nit.
- 4 Ba tey manoon naa am yaakaar ci sama bopp; su nit doon damu, maa ciy raw.
- 5 Xarafoon naa ca ayu-bés ga, bokk ci bànni Israyil ci giiru Beñamin, di Ebrë ci deret ak ci meen. Bu dee ci yoonu Musaa ngeen bëgga wax, ci tariixab Farisen laa bokkoon;
- 6 bu dee it ci mbirum farlu, daan naa fitnaal mbooloom ñi gëm Kirist; bu dee ci njub ci sàmm yoon, awma benn gàkk.
- 7 Waaye loolu lépp lu ma tegoon ay njariñ fa kanam Yàlla, dëddu naa ko ngir Kirist.
- 8 Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel manu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist.
- 9 Na ma Yàlla fekk ci moom, waxuma ci njub gu aju ci sàmm yoon, waaye gu aju ci gëm Kirist, maanaam njub gi nu Yàlla sol ci kaw ngëm.
- 10 Moom laay ittewoo xam, ak doole ji ànd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam,
- 11 ngir mana séddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am.
- 12 Waxuma ne jagoo naa ko ba noppi, waxuma it ne aji mat laa, waaye maa ngi daw, ngir jot li tax Kirist jël ma.
- 13 Bokk yi, gëmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: fàtte li ma weesu, jublu ci li féete kanam,
- 14 di daw yen muj ga, ngir jot li ma Yàlla taxa woo, di cér bi ma Yàlla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu.
- 15 Nun ñi mat nag, nanu xalaat loolu. Su ngeen ci amee werantey xol, Yàlla dina leen ko leeralal.
- 16 Li am daal, fa seen ngëm tolloo, na fa seen jëf àgg.
- 17 Kon nag bokk yi, toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen.
- 18 Ndaxte jëfi ñu bare juuyoo na ak dee gi Kirist dee; loolu wax naa leen ko ba tàyyi, maa ngi koy waxaat léegi ak i jooy.
- 19 Alku lañuy mujje, ñoom ñiy jaami seen biir, di wonoo lu ruslu, tey wut yëfi àddina rekk.
- 20 Waaye nun waa asamaan lanu, te noo ngi xaar Boroom bi Yeesu Kirist jóge fa, musalsi nu.
- 21 Noonu dina soppi sunu yaram wu toroxlu, def ko ni yaramam wi ànd ak ndam dëppook kàttanam, gi ko mana notal mbindeef yépp.