데살로니가후서 3장 월로프어 신약
- 1 Léegi nag bokk yi, ñaanal-leen nu, ngir kàddug Boroom bi law te ànd ak ndam, ni mu ko ame woon ci yéen.
- 2 Ngeen ñaanal nu it, ngir nu mucc ci ñi bon te soxor, ndaxte du ñépp a gëm.
- 3 Waaye Boroom bi kuy sàmm kóllëre la; dina leen dëgëral te musal leen ci Ibliis.
- 4 Te wóor nanu ci kanam Boroom bi ne yéena ngi def li nu leen santoon, te dingeen ci sax.
- 5 Na Boroom bi gindi seeni xol ci mbëggeelu Yàlla ak muñu Kirist.
- 6 Nu ngi leen di sant it bokk yi, ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen dëddu bépp mbokk buy wéy ci tayel te baña topp dénkaane, yi nu leen jottali.
- 7 Xam ngeen bu baax, yéen ci seen bopp, ni ngeen wara awe ci sunuy tànk. Ba nu nekkee ca yéen, wéyunu woon ci tayel
- 8 te masunoo lekk ñaqu kenn. Waaye guddi ak bëccëg danu daan ñaq, di sonn, ngir baña wéeru ci kenn ci yéen.
- 9 Waxuma ne amunu sañ-sañu def ko, waaye danoo bëggoona nekk ay royukaay ci yéen, ngir ngeen aw ci sunuy tànk.
- 10 Ndaxte ba nu nekkee ca yéen, lii lanu tëraloon: «Ku liggéeyul, du lekk.»
- 11 Léegi nag dégg nanu ne am na ci yéen ñuy wéy ci tayel; liggéeyuñu dara, lu dul di dugg ci lu seen yoon nekkul.
- 12 Ñu deme noonu nag, nu ngi leen di sant te di leen dénk ci turu Boroom bi Yeesu Kirist, ñuy liggéey ci jàmm tey dunde seen ñaq.
- 13 Yéen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu rafet.
- 14 Su kenn bañee topp li nu bind ci bataaxal bii, ràññeeleen ko te sore ko, ngir mu rus ci.
- 15 Waxuma ngeen def ko noon, waaye ngeen yedd ko ni seen mbokk.
- 16 Yal na leen kiy Boroom jàmm may jàmm fépp ak ci lépp. Yal na Boroom bi ànd ak yéen ñépp.
- 17 Tàggoo bii maa ko bind ci sama loxo, man Pool. Nii laay binde, te di màndargaale nii sama bataaxal yépp.
- 18 Yal na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen ñépp.