디모데후서 2장 월로프어 신약
- 1 Kon nag yaw sama doomu diine, doolewool yiw, wi ci Kirist Yeesu.
- 2 Te wax yi nga dégge ci man fi kanam seede yu bare, nanga leen jottali nit ñu takku, ngir ñoom it ñu mana jàngal ñeneen.
- 3 Bokkal ak man tiis, di jàmbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu,
- 4 xam ne xarekat bu bëgga neex ka ko solal, du dugg ci yëfi àddina.
- 5 Te it ku tàggat yaramam ngir rawante, duñu ko jagleel kaalag ndam mukk, su toppul sàrt ya.
- 6 Noonu it beykat bi sonn mooy jëkka ñam toolam.
- 7 Xalaatal bu baax sama wax jii, ndax Boroom bi dina leeral sa xel ci lépp.
- 8 Fàttalikul Yeesu Kirist mi dekki, soqikoo ci Daawuda, tukkee ci xibaaru jàmm bi may waare.
- 9 Xibaar booboo tax may jànkoonte ak i tiis, ba ñu jéng ma ni defkatu lu bon; waaye kàddug Yàlla moom, kenn du ko jéng.
- 10 Te lii tax may muñ lépp, ngir ñi Yàlla tànn it am mucc gi ci Kirist Yeesu, gu ànd ak ndam lu sax.
- 11 Kàddu gu wóor a ngii: Su nu deeyaalee ak Kirist, dinanu dundaat ak moom;
- 12 su nu takkoo, dinanu nguuru ak moom.
- 13 Su nu ko weddee, kon mu weddi nu; su nu ko ñàkkee kóllëre, moom dina sax ci kóllëreem, ndax manula weddi boppam.
- 14 Saxal ci di leen fàttali mbir yooyu, di leen dénk fa kanam Yàlla, ñu moytoo werante ciy araf, ndax loolu jëmul fu dul ci yàq ngëmu ñiy déglu.
- 15 Góor-góorlul ba teew fa kanam Yàlla, nekk liggéeykat bu mu nangul te rusoo ci dara, di faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi.
- 16 Moytul bépp jataayu waxi neen yu àddina kese, ndax ña fa toog dinañu gëna xuus cig weddi,
- 17 te seen kàddu day burux ni ngal. Imene ak Filet, ci ñoom lañu bokk;
- 18 dañoo moy dëgg, di wax ne ndekkite wees na, ba yàq ngëmu ñenn ñi.
- 19 Waaye teewul fondamaa bu dëgër, bi Yàlla tabax, nee na kekk, te lii lañu ci tàmpe: «Boroom bi xam na ñi bokk ci moom,» te it: «Ki tudd turu Boroom bi, na daw lu bon.»
- 20 Ci kër gu mag nag, du ndabi wurus walla xaalis rekk a fa am, waaye itam yoy dénk walla ban; yii tedd nañu, yee ñàkk solo.
- 21 Kon nag ku laabal sa bopp ci yooyu yépp, dinga nekk ndab lu tedd te sell, nga am njariñ ci Boroom bi te jekk ci bépp jëf ju rafet.
- 22 Dawal bépp bëgg-bëggu ngone, te sóobu ci njub, ngëm, mbëggeel, jàmm, ànd ak ñépp ñiy tudd turu Boroom bi ak xol bu sell.
- 23 Tanqamlul bépp weranteb neen bu amul njariñ, xam ne xuloo rekk lay jur.
- 24 Te jaamu Boroom bi warula xuloo, waaye na lewet ci ñépp, jekk ngir jàngle tey muñ fitnay noon.
- 25 Na jubbanti cig suufe ñi koy diiŋat, tey yéene Yàlla xiir leen ci réccu, ba ñu xam dëgg;
- 26 ñu rëcc ci fiirug Seytaane, mi leen jàpp niy jaam, te ñu délsi ci seen xel yu rafet, ba sóobuwaat ci coobarey Yàlla.