요한일서 1장 월로프어 신약
- 1 Nu ngi leen di bind ci mbirum ki ñuy wax Kàddug dund, moom mi amoon ca njàlbéen ga; mi nu dégg te gis ko ak sunuy bët, mi nu xool te laal ko ak sunuy loxo.
- 2 Dund feeñ na, te gis nanu ko; te moom lanuy seedeel, di leen yégal dund gu dul jeex, googu nekkoon ci wetu Yàlla Baay bi te feeñu nu.
- 3 Li nu gis te dégg ko, nu ngi leen koy yégal, ngir yéen itam ngeen bokk ak nun. Te dëgg-dëgg bokk nanu ci Baay bi ak Doomam, Yeesu Kirist.
- 4 Nu ngi leen di bind yëf yii, ngir sunu mbég mat sëkk, nun ñépp.
- 5 Xibaar bi nu dégg ci Yeesu Kirist, di leen ko yégal, mooy lii: Yàlla Leer la, te genn lëndëm nekkul ci moom.
- 6 Su nu waxee ne bokk nanu ci moom, tey dox ci lëndëm, danuy fen ci sunuy wax ak sunuy jëf.
- 7 Waaye bu nuy dox ci leer, ni mu nekke moom ci boppam ci leer, kon bokk nanu ci sunu biir, te deretu Yeesu Doomam dina nu sellal ci bépp bàkkaar.
- 8 Su nu waxee ne amunu bàkkaar, kon nax nanu sunu bopp, te dëgg nekkul ci nun.
- 9 Su nu nangoo sunuy bàkkaar ci kanamam, fekk kuy sàmm kóllëre la te jub, ngir baal nu sunuy bàkkaar te sellal nu ci lépp lu jubadi.
- 10 Su nu waxee ne defunu bàkkaar, teg nanu ko kuy tebbi waxam, te kàddoom duggagul ci sunu xol.