요한계시록 10장 월로프어 신약
- 1 Noonu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo niir. Xon tiim ko, xar kanamam mel ni jant, ay tànkam mel ni jumi sawara.
- 2 Yor na benn téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndijooram ci géej gi, tànku càmmoñam ci suuf si,
- 3 di xaacu, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom ñaari dënnu yi jib.
- 4 Naka la juróom ñaari dënnu yi di jib, may waaja bind, waaye ma dégg baat bu jóge asamaan, naan ma: «Li juróom ñaari dënnu yi wax, na nekk kumpa, bu ko bind.»
- 5 Noonu malaaka, ma ma gis, mu taxaw ci géej gi ak suuf si, yékkati loxol ndijooram, mu jëm asamaan,
- 6 daldi waat ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak li ci nekk lépp; mu ne: «Négandiku wees na,
- 7 waaye jamono ju juróom ñaareelu malaaka ma wolee ci liitam, ndogalu Yàlla dina mat, ni mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»
- 8 Ci kaw loolu baat, ba ma déggoon ca asamaan waxaat ak man, ne ma: «Demal jël téere bi ñu ubbi ci loxob malaaka, mi taxaw ci géej gi ak suuf si.»
- 9 Ma dem ca malaaka ma, laaj ko téere bu ndaw boobu. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir, waaye dina neex ni lem ci sa gémmiñ.»
- 10 Noonu ma jël téere bi ci loxob malaaka mi, daldi ko lekk, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye bi ma ko wannee, mu wex xat ci sama biir.
- 11 Gannaaw loolu ñu ne ma: «Fàww nga wax ci kàddug Yàlla lu jëm ci réew yu bare ak xeet yu bare ak kàllaama yu bare ak buur yu bare.»