에베소서 5장 월로프어 신약
- 1 Yéen nag ñiy goney Yàlla, yi mu bëgg ci xolam, royleen ko ci loolu.
- 2 Ngeen wéer seen dund ci mbëggeel, mel ni Kirist mi nu bëgg, ba joxe bakkanam ngir nun, di sarax su ñu jébbal Yàlla te neex ko ni xetu latkoloñ.
- 3 Waaye naka njaaloo ak bépp sobe mbaa bëgge, jéllale naa jëf ji sax, waaye bu ko làmmiñ tudd, ni mu jekke ci gaayi Yàlla yu sell yi.
- 4 Dawleen it lu jekkadee, ni wax ju ñaaw mbaa waxi caaxaan ak kaf yu bon, te ngeen sax ci sant Yàlla.
- 5 Na leen wóor ne kenn ku jikkowoo ndoxaan, sobe mbaa bëgge, maanaam bokkaale Yàlla, kooku du am cér ci nguuru Kirist ak Yàlla.
- 6 Bu leen kenn nax ci ay waxi neen, ndaxte jëf yooyooy tax meru Yàlla di wàcc ci kureelu ñi ko déggadil.
- 7 Kon nag buleen séq ak ñoom dara.
- 8 Lëndëm ngeen woon, waaye léegi leer ngeen ndax seen bokk ci Boroom bi.
- 9 Leer, mbaax lay meññ, njub ak dëgg.
- 10 Dëggal-leen ci seeni jëf li neex Boroom bi,
- 11 te daw lépp luy jëfi lëndëm yu amul njariñ, bay weer sax ku koy def.
- 12 Ndaxte waxtaane sax li ñuy def ci nëbbu, lu ruslu la;
- 13 waaye leer, lu mu ëmb, fésal ko.
- 14 Ndaxte lu jaxasoo ak leer di leer. Looloo tax ñu ne: «Yewwul, yaw mi nelaw, te jóge ci biir néew yi, kon Kirist dina ne ràññ ci yaw, // ni leeru jant buy fenk.»
- 15 Noonu sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel,
- 16 tey jariñoo jot gi, ndaxte nu ngi ci jamono ju bon.
- 17 Buleen ñàkk bopp nag, waaye xamleen liy coobarey Boroom bi.
- 18 Buleen màndi it ci sàngara, liy ndeyi ñaawteef, waaye feesleen ak Xel mu Sell mi;
- 19 di waxante ci seen biir ci ay taalifi Sabóor, ciy woy ak i cant yu tukkee ci Xelum Yàlla, di woy ak a kañ Boroom bi ci seen xol.
- 20 Gërëmleen Yàlla Baay bi ci turu Yeesu Kirist Boroom bi, fu ngeen mana tollu, ci lu mu mana doon;
- 21 teg ca nangul sa moroom ci biir wegeelu Kirist.
- 22 Naka yéen jigéen ñi, nangeen nangul seeni jëkkër, ni su doon Boroom bi.
- 23 Ndaxte góor mooy kilifag soxnaam, ni Kirist nekke kilifag mbooloom ñi gëm, muy jëmmam ji muy sàmm.
- 24 Ni mbooloo mi nag jiitale Kirist, noonu la jigéen ji wara jiitale jëkkëram ci lépp.
- 25 Yéen nag góor ñi, na ku nekk bëgg soxnaam, ni Kirist bëgge mbooloo mi, ba joxe bakkanam ndax moom,
- 26 ngir sellal ko ak kàddoom, ba mu laab ni ku sangu set.
- 27 Noonu dina ko jël, mu mel ni séet bu ñu waajal, di mbooloom mu soloo ndam, te gàkkul, rasul, taqul leneen, waaye mu sell te amul sikk.
- 28 Na góor bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam. Bëgg sa soxna, bëgg sa bopp la.
- 29 Ndaxte kenn masula bañ sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk. Noonu it la Kirist fonke mbooloo mi;
- 30 ndaxte noo di céri jëmmam.
- 31 Mbind mi nee na: «Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon kenn.»
- 32 Loolu ëmb na mbóot mu xóot; man maa ngi wax ci lu jëm ci Kirist ak mbooloo mi.
- 33 Waaye li teew, na góor gu nekk bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam, te jigéen ji weg jëkkëram.