디도서 2장 월로프어 신약
- 1 Yaw nag nangay waare li dëppook njàngle mu wér mi.
- 2 Maanaa, na góor ñu mag ñi foog, am faayda te maandu, di ñu wér ci seen ngëm, seen mbëggeel ak seen muñ.
- 3 Jigéen ñu mag ñi itam, na seen doxalin ànd ak faayda; buñuy jëw mbaa ñuy xér ci sàngara. Waaye nañuy jàngle lu baax,
- 4 bay xiir jeeg ju ndaw ji, ñu bëgg seen jëkkër ak seeni doom,
- 5 di ñu maandu, sell te fonk seen kër, ñu neex deret te déggal seeni jëkkër, ngir kenn bañ cee gàkkal kàddug Yàlla.
- 6 Naka noonu itam nanga xiir waxambaane yi cig maandu.
- 7 Te yaw, ci lépp lu mu mana doon, nekkal ab royukaay ci jëf yu baax. Na sa njàngle wér te am faayda,
- 8 ànd ak wax yu wér yu kenn manta diiŋat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li ñu amul dara lu ñu nu tuumaal.
- 9 Waxal it jaam ñi, ñu déggal seeni sang ci lépp, te liggéeyal leen ba seral seen xol, bañ cee boole werante
- 10 mbaa sàcc. Waaye nañu wone takkute gu mat, ba rafetal ci lépp njànglem Yàlla sunu Musalkat.
- 11 Ndaxte yiwu Yàlla feeñ na te ubbil na ñépp buntu mucc.
- 12 Moo nu digal, nu dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamono, tey dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla,
- 13 di séentu bés bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Yàlla ju màgg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, feeñ ci biir ndamam.
- 14 Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññiku ci jëf yu baax.
- 15 Jàngleel loolu, di leen dénk ak a yedd ak fulla ju mat. Bu la kenn yab.