디도서 3장 월로프어 신약
- 1 Fàttali leen ñuy déggal kilifa, yi yore nguur gi, tey jëfe seeni ndigal, ñu taxaw temm ci lépp luy jëf ju baax.
- 2 Buñu jëw kenn mbaa ñuy ŋaayoo, waaye nañu yiwe te won ñépp lewet gu mat sëkk.
- 3 Ndaxte nun itam ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, nu réer bay jaamu ay bëgg-bëgg ak i bànneex yu wuute, nu dëkk ci coxorte ak ñeetaane, ñu bañ nu te nu bañante ci sunu biir.
- 4 Waaye naka noona Yàlla sunu Musalkat feeñal na mbaaxam ak cofeelam,
- 5 ba musal nu; ajuwul ci jëf yu jub yu nu def, waaye ci yërmandeem rekk. Mu juddulaat nu ci laabal sunu xol, te yeesalaat nu ci dooley Xel mu Sell,
- 6 mi mu nu sotti ba mu baawaan, ci darajay Yeesu Kirist sunu Musalkat.
- 7 Ci noonu Yàlla àtte na nu jub ci kaw yiwam, te sédd nu ci dund gu dul jeex, gi nuy séentu.
- 8 Wax jooju ju wóor la, te damaa bëgg nga dëggal loolu, ngir ñi gëm Yàlla sax ci jëf lu rafet. Loolu moo baax te am njariñ ci nit.
- 9 Waaye moytul yu deme ni werantey neen ak limi maam, ay xuloo ak i xëccoo ci doxalinu yoonu Musaa, ndax loolu waxi neen la, te amul benn njariñ.
- 10 Kuy féewale, nanga ko yedd, yeddaat ko; bu tëwee, nga dàq ko,
- 11 xam ne nit ku ñaaw xel la te ay bàkkaaram fés ci ñépp.
- 12 Bu ma la yónnee Artemas walla Tisig, gaawantul fekksi ma ci dëkku Nikopolis, ndax fa laa bëgga lollikooji.
- 13 Naka Senas àttekat bi nag ak Apolos, waajal leen bu jekk ci seen tukki, ba seen aajo yépp faju.
- 14 Na sunuy bokk it takku ci jëf yu rafet, ba mana faj aajo yépp, te baña yaafus.
- 15 Ñiy ànd ak man ñépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy soppey ngëm. Yal na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.