야고보서 2장 월로프어 신약
- 1 Yéen samay bokk, bu benn gënale laal seen ngëm ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi soloo ndam.
- 2 Ndaxte su ñaari nit duggee ci seen mbooloo, kii takk jaaroy wurus te sol yére yu taaru, ka ca des ñàkk te limboo ay sagar,
- 3 ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,»
- 4 kon gënale ngeen ci seen biir, ba àtte ci col, bàyyi xol.
- 5 Dégluleen yéen sama bokk yi ma bëgg, ndax Yàlla tànnul ñi néewle ci àddina, ngir ñu barele ci ngëm, tey am i cér ci nguur, gi Yàlla dig ñi ko bëgg?
- 6 Fekk dangeen leen di toroxal! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di not te di leen yóbbu fa kanam àttekat yi?
- 7 Ndax duñu tilimal tur wu tedd, wi ngeen di wuyoo?
- 8 Su ngeen sàmmee yoonu Buur Yàlla, ni ko Mbind mi tërale naan: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp,» kon def ngeen lu baax.
- 9 Waaye su ngeen gënalee, bàkkaar ngeen, te yoonu Yàlla dina leen dab ni ñu moy.
- 10 Ndaxte ku sàmm yoon wépp, waaye xëtt ci lenn ndigal rekk, jàdd nga yoon wépp.
- 11 Ndaxte Yàlla mi ne: «Bul njaaloo», teg na ca ne: «Bul bóome.» Ku njaaloowul nag, waaye nga bóome, jàdd nga yoon wépp.
- 12 Gannaaw dingeen nara jaar ci àtteb yoon, wiy goreel, na loolu lal seen wax ak seen jëf.
- 13 Ndaxte ku yërëmul, yoon du la yërëm. Te yërmande mooy not àtte.
- 14 Te lii itam samay bokk: ku ne gëm nga, te jëfewoo ko, loolu lu muy jariñ? Ndax googu ngëm man na laa musal?
- 15 Su amee mbokk ci seen biir, mu rafle te amul dund, muy góor walla jigéen,
- 16 te kenn ci yéen ne ko: «Demal ak jàmm, nga solu te lekk,» te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jariñ?
- 17 Noonu ngëm gu àndul ak jëf, amul benn njariñ.
- 18 Waaye xanaa dina am ku ne: «Yaw am nga ngëm, man am naa ay jëf.» Yaw nag won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, ma feeñal la sama ngëm ci samay jëf.
- 19 Gëm nga ne Yàlla kenn la; loolu lu baax la, waaye xamal ne, jinne yi it gëm nañu loolu, ba dañoo tiit bay lox.
- 20 Yaw mi gàtt xel, kaay ma won la ne ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ.
- 21 Sunu maam Ibraayma, ndax du ci kaw jëf la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu joxe doomam Isaaxa ni sarax?
- 22 Kon gis nga ne ngëm dafa lëngoo ak ay jëfam, te ngëmam mat ci kaw jëf jooju.
- 23 Noonu li ñu wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub,» ba ñu ko wooye xaritu Yàlla.
- 24 Kon nag gis nga ne Yàlla ci jëf lay àtte nit ni ku jub, waaye du ci kaw ngëm kese.
- 25 Naka Raxab jigéenu moykat bi itam, ndax du ci noonu la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu teeru ndawi Yawut yi, te jaarale leen ca poot ba?
- 26 Kon nag ni jëmm ju amul ruu nekke ndee, noonu la ngëm gu àndul ak jëf nasaxe.