야고보서 3장 월로프어 신약
- 1 Samay bokk, bu ñépp di sababloo nekk jànglekatu mbooloo mi, xam ne nun jànglekat yi, àtte bi nuy jaar mooy gëna diis.
- 2 Ndaxte nun ñépp sikk nanu ci fànn yu bare. Ki sikkul ci kàddoom, ku mat nga te mana not sa yaram wépp.
- 3 Noonu ku laab fas, ngir mu déggal la, not nga jëmmam jépp.
- 4 Gaal yi it yu réy lañu, te ngelaw lu am doole di leen jañax, waaye dawalkat bi, weñ gu tuuti la leen di jëme fu ko neex.
- 5 Ci noonu làmmiñ, cér su tuuti la, waaye day bàkkoo jëf yu réy. Seetleen ni ferñent tuutee te mana lakk àll bu yaatu.
- 6 Noonu it làmmiñ sawara la, di bon-bonu àddina ci biir cér yi, tey musibaal jëmm jépp. Jum la, bu Seytaane taal, muy lakk àddina.
- 7 Nit man na not xeeti rab yépp: rabi àll yi, picc yi, yiy raam ak yi ci géej gi— not na lépp.
- 8 Waaye làmmiñ kenn manu koo not; musiba la mu dul dal mukk, fees dell ak daŋar juy rey.
- 9 Làmmiñ lanuy sante Boroom bi, di sunu Baay, ba noppi móoloo ko nit, ñi Yàlla sàkk ci meloom.
- 10 Gémmiñ gi sante mooy móoloo. Yéen samay bokk, loolu warula am.
- 11 Ndax ndox mu lewet ak mu wex dinañu ballandoo ci genn mbënn?
- 12 Samay bokk, ndax mas ngeena gis garabu figg gu meññ oliw, walla garabu reseñ gu meññ ay figg? Mukk! Mbënnu xorom manta nàcc mukk ndox mu neex.
- 13 Ana ku neex xel ci yéen, ana kuy boroom xam-xam? Na ko wone ciy jëfam ak dundam gu sell, te feeñal xelam ci jikkoom ju lewet.
- 14 Waaye ku am ci sa xol farlu gu laloo wextan ak wut aw tur, bul bàkku, di weddi dëgg.
- 15 Xel moomu jógewul ci kaw; jëfu àddina la, di jikkoy niti kese, te jóge ci Seytaane.
- 16 Ndaxte fu wextan ak wut aw tur dugg, indi fa xëccoo ak bépp ñaawteef.
- 17 Waaye xel mi jóge ci kaw daa sell, ba noppi ànd ak jàmm te lewet, nooy, fees dell ak yërmande ak jëf yu rafet; àndul ak genn parlàqu, amul genn naaféq.
- 18 Te nitu jàmm dina bey toolu jàmm, góob njub.